15 Moo ma taxa dikk dajeek yaw. Seet naa laa seet, ba gis la.
16 Lal naa saab lal, ba mu jekk, di malaan yu yànj, bawoo Misra.
17 Lal ba, ma xeeñal, mu ne bann, di ndàbb, cuuraay ak xas mu neex.
18 Dikkal, nu baanee baane, ba bët set, te bànneexu ci mbëggeel.
19 Sama jëkkër newu fa, daa dem yoon wu sore.
20 Mbuusum xaalis la ŋàbb, yóbbu, du ñibbsi ndare weer wi fees dell.»
21 Muy mocc ak a moccaat, ba nax ko, di wax lu neex, ba man ko.