Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 7:13-17 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 7:13-17 in Kàddug Yàlla gi

13 Ndaw sa ne ko katam, fóon, ne wajj, ne ko:
14 «Tey matal naa la ma digoon Yàlla, yàppu bernde waa nga kër ga, saraxu cant la.
15 Moo ma taxa dikk dajeek yaw. Seet naa laa seet, ba gis la.
16 Lal naa saab lal, ba mu jekk, di malaan yu yànj, bawoo Misra.
17 Lal ba, ma xeeñal, mu ne bann, di ndàbb, cuuraay ak xas mu neex.
Kàddu yu Xelu 7 in Kàddug Yàlla gi