Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 6:7-13 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 6:7-13 in Kàddug Yàlla gi

7 Du ku ko yilif mbaa ku koy sas, te jiiteesu ko.
8 Bu jotee mu denc ab dundam, mu jot, mu for lekkam.
9 Moo yaafus bi, foo àppal tëraay bi? Loo deeti xaar ci yewwu?
10 Ngay dajjant ak a for bët, di tegley loxook a jaaxaan.
11 Néewlee ngi lay dikkal nib sàcc, ñàkk gànnaayul la.
12 Ku tekkeedi te bon, day wër di fen,
13 day piis, di wokkeb tànk, di waxe baaraam,
Kàddu yu Xelu 6 in Kàddug Yàlla gi