Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 6:6-16 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 6:6-16 in Kàddug Yàlla gi

6 Yaafus bee, xoolal xorondom, seetal ci moom, ba muus.
7 Du ku ko yilif mbaa ku koy sas, te jiiteesu ko.
8 Bu jotee mu denc ab dundam, mu jot, mu for lekkam.
9 Moo yaafus bi, foo àppal tëraay bi? Loo deeti xaar ci yewwu?
10 Ngay dajjant ak a for bët, di tegley loxook a jaaxaan.
11 Néewlee ngi lay dikkal nib sàcc, ñàkk gànnaayul la.
12 Ku tekkeedi te bon, day wër di fen,
13 day piis, di wokkeb tànk, di waxe baaraam,
14 jekkadiy xalaat, di mébét lu bon aka yokku ay.
15 Moo tax musiba di jekki dal ko, mu jekki yàqu, ba wees paj.
16 Juróom benn a ngii yu Aji Sax ji bañ, ba ci juróom yaar yu mu seexlu:
Kàddu yu Xelu 6 in Kàddug Yàlla gi