6 Yaafus bee, xoolal xorondom, seetal ci moom, ba muus.
7 Du ku ko yilif mbaa ku koy sas, te jiiteesu ko.
8 Bu jotee mu denc ab dundam, mu jot, mu for lekkam.
9 Moo yaafus bi, foo àppal tëraay bi? Loo deeti xaar ci yewwu?
10 Ngay dajjant ak a for bët, di tegley loxook a jaaxaan.