25 Bu ko xemmeme taaram, bumu la fiir aki lamsal.
26 Dogu mburu fey nab gànc; waaye jabaru jaambur, bakkanu lëmm.
27 Te ku ne sawara cas, tafoo, lakk say yére.
28 Ku dox ciy xal it, say tànk ñor.
29 Mooy ànd ak jabaru jaambur, ku ko def gis ko.
30 Deesul sikk ku sàcc aw ñam, def ci biiram ndax xiif.
31 Waaye bu feeñee, fey boroom juróom yaari yoon, joxe alalu këram yépp.
32 Njaaloo di ñàkk bopp, kuy sànk bakkanam a koy def.
33 Mbugal ak toroxte dib añam, te gàcceem du deñ.