23 Santaane da lay niital, ndigal leeralal la, artook ub yar di yoonu dund.
24 Da lay aar ci ndaw su bon ak jabaru jaambur ak làmmiñam wu neex.
25 Bu ko xemmeme taaram, bumu la fiir aki lamsal.
26 Dogu mburu fey nab gànc; waaye jabaru jaambur, bakkanu lëmm.
27 Te ku ne sawara cas, tafoo, lakk say yére.