16 Juróom benn a ngii yu Aji Sax ji bañ, ba ci juróom yaar yu mu seexlu:
17 kuy daŋŋiiral, kuy fen, kuy rey nit ku deful dara,
18 kuy fexe lu bon ci xolam, kuy gaawtuy def lu ñaaw,
19 seede buy fen rekk, rawatina kuy yokku ay ci biiri bokk.
20 Doom, defal li la baay sant, te bul wacc ndigalal yaay.
21 Takkal foo tollu, taf ci sa xol, fas ko ci sa baat.
22 Booy dox mu di la jiite, nga tëdd, mu di la sàmm, nga yewwu, mu di la waxal.
23 Santaane da lay niital, ndigal leeralal la, artook ub yar di yoonu dund.
24 Da lay aar ci ndaw su bon ak jabaru jaambur ak làmmiñam wu neex.