Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 6:16-21 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 6:16-21 in Kàddug Yàlla gi

16 Juróom benn a ngii yu Aji Sax ji bañ, ba ci juróom yaar yu mu seexlu:
17 kuy daŋŋiiral, kuy fen, kuy rey nit ku deful dara,
18 kuy fexe lu bon ci xolam, kuy gaawtuy def lu ñaaw,
19 seede buy fen rekk, rawatina kuy yokku ay ci biiri bokk.
20 Doom, defal li la baay sant, te bul wacc ndigalal yaay.
21 Takkal foo tollu, taf ci sa xol, fas ko ci sa baat.
Kàddu yu Xelu 6 in Kàddug Yàlla gi