Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 5:8-22 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 5:8-22 in Kàddug Yàlla gi

8 Soreel ndaw soosu, bul jege bunt këram.
9 Kon nga ñàkk daraja, keneen jagoo; ku néeg bóom la.
10 Jaambur jariñoo sa doole, doxandéem jagoo saw ñaq.
11 Ngay mujje onk, desey yax, jeex tàkk.
12 Nga naan: «Su ma yégoon, sopp ab yar te baña sofental waxi àrtu.
13 Lu ma tee woona dégg ku may digal, tey teewlu sama waxi sëriñ ya?
14 Tuuti ma yàqu yaxeet fi kanam ñépp!»
15 Naanal ci sa mbalkam bopp, ndox ma balle sa teenu bopp.
16 Xanaa doo wasaare sa bëti ndox ca biti, mu def ay wal ca pénc ya?
17 Nay sa alal, yaw doŋŋ, ku bokk feneen bokkul.
18 Yal na sa naanukaay barkeel, nga bànneexoo kiy sa jabar ba ngay ndaw.
19 Aka sopplu te jekk! Na lay céram doy foo tollu, na la xañ sago saa su ne.
20 Doom, ana looy xemmeme keneen, bay foye céri jaambur?
21 Lu waay jëf, Aji Sax ji gis, di xool mboolem fu mu jaare.
22 Jëf ju bon day fiir ka ko sàlloo, bàkkaaram di mbaal, jàpp ko.
Kàddu yu Xelu 5 in Kàddug Yàlla gi