7 Kon, doom, déglu ma, bul wacc samay kàddu.
8 Soreel ndaw soosu, bul jege bunt këram.
9 Kon nga ñàkk daraja, keneen jagoo; ku néeg bóom la.
10 Jaambur jariñoo sa doole, doxandéem jagoo saw ñaq.
11 Ngay mujje onk, desey yax, jeex tàkk.
12 Nga naan: «Su ma yégoon, sopp ab yar te baña sofental waxi àrtu.
13 Lu ma tee woona dégg ku may digal, tey teewlu sama waxi sëriñ ya?