Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 5:3-7 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 5:3-7 in Kàddug Yàlla gi

3 Lu mel ni lem la ndaw su yemadi di wax, làmmiñ wa ni diw gu ñu lay raay.
4 Muj ga mu wex xàtt, di gaañe ni ñawkay saamar.
5 Tànk ya day bartalu wuti ndee, ay jéegoom àkki njaniiw.
6 Rëddul yoonu dund, daa lajj, te xamu ko.
7 Kon, doom, déglu ma, bul wacc samay kàddu.
Kàddu yu Xelu 5 in Kàddug Yàlla gi