17 Nay sa alal, yaw doŋŋ, ku bokk feneen bokkul.
18 Yal na sa naanukaay barkeel, nga bànneexoo kiy sa jabar ba ngay ndaw.
19 Aka sopplu te jekk! Na lay céram doy foo tollu, na la xañ sago saa su ne.
20 Doom, ana looy xemmeme keneen, bay foye céri jaambur?
21 Lu waay jëf, Aji Sax ji gis, di xool mboolem fu mu jaare.
22 Jëf ju bon day fiir ka ko sàlloo, bàkkaaram di mbaal, jàpp ko.