Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 5:16-23 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 5:16-23 in Kàddug Yàlla gi

16 Xanaa doo wasaare sa bëti ndox ca biti, mu def ay wal ca pénc ya?
17 Nay sa alal, yaw doŋŋ, ku bokk feneen bokkul.
18 Yal na sa naanukaay barkeel, nga bànneexoo kiy sa jabar ba ngay ndaw.
19 Aka sopplu te jekk! Na lay céram doy foo tollu, na la xañ sago saa su ne.
20 Doom, ana looy xemmeme keneen, bay foye céri jaambur?
21 Lu waay jëf, Aji Sax ji gis, di xool mboolem fu mu jaare.
22 Jëf ju bon day fiir ka ko sàlloo, bàkkaaram di mbaal, jàpp ko.
23 Ñàkk yar, dee; ndof gu réy, sànku.
Kàddu yu Xelu 5 in Kàddug Yàlla gi