3 Man it amoon naa baay, di benn bàjjo ci saa ndey.
4 Baay digal ma, ne ma: «Jàppal samay wax ci sam xel, di jëfe samay santaane, ba dund.
5 Amal xel mu rafet akug dégg. Bul fàtte te bul moy samay wax.
6 Bul dëddu xel mu rafet, da lay aar; sopp ko, mu sàmm la.
7 Njàlbéenu xel mu rafet mooy sàkku ko; ak loo mana am, amal ug dégg.
8 Nawal xel mu rafet, mu darajaal la; tafoo ko, mu teral la.
9 Da lay takkal kaala gu jekk, solal la mbaxanam buur.»
10 Déglul, doom, te dégg saay wax, ndax nga gudd fan.