Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 4:23-27 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 4:23-27 in Kàddug Yàlla gi

23 Sàmmala sàmm sab xol, nde xalaati xol ngay jëfe.
24 Dàqal wor, mu sore la; kàdduy naxe, na la dànd.
25 Xooleel, sa bët ne jàkk, ngay xool sa kanam màkk.
26 Seetlul fi ngay teg tànk, ba foo awe, mu wóor.
27 Bul jàdd, ndijoor mbaa càmmoñ, na sa tànk moyu lu bon.
Kàddu yu Xelu 4 in Kàddug Yàlla gi