21 Bu ci noppee ja jàkk, te jàpp ko ci sa biir xel.
22 Mooy dundloo ku ci jàpp, di wéral jëmmam jépp.
23 Sàmmala sàmm sab xol, nde xalaati xol ngay jëfe.
24 Dàqal wor, mu sore la; kàdduy naxe, na la dànd.
25 Xooleel, sa bët ne jàkk, ngay xool sa kanam màkk.
26 Seetlul fi ngay teg tànk, ba foo awe, mu wóor.