2 Maa ngi leen di jàngal lu baax, buleen fàtte sama njàngle.
3 Man it amoon naa baay, di benn bàjjo ci saa ndey.
4 Baay digal ma, ne ma: «Jàppal samay wax ci sam xel, di jëfe samay santaane, ba dund.
5 Amal xel mu rafet akug dégg. Bul fàtte te bul moy samay wax.
6 Bul dëddu xel mu rafet, da lay aar; sopp ko, mu sàmm la.