Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 4:15-26 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 4:15-26 in Kàddug Yàlla gi

15 Moyul, bu fa jaare; mbasal te wéy!
16 Ku bon du nelaw te lorewul, du dajjant ba kera muy téqe.
17 Daa bon, def ko lekk, di màndee coxoram.
18 Yoonu ku jub day leer, ba ne ràññ ni bëccëg.
19 Yoonu ku bon ne këruus, du xam lu muy téqtaloo.
20 Doom, déglul samay kàddu, teewlul samay wax.
21 Bu ci noppee ja jàkk, te jàpp ko ci sa biir xel.
22 Mooy dundloo ku ci jàpp, di wéral jëmmam jépp.
23 Sàmmala sàmm sab xol, nde xalaati xol ngay jëfe.
24 Dàqal wor, mu sore la; kàdduy naxe, na la dànd.
25 Xooleel, sa bët ne jàkk, ngay xool sa kanam màkk.
26 Seetlul fi ngay teg tànk, ba foo awe, mu wóor.
Kàddu yu Xelu 4 in Kàddug Yàlla gi