Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 4:13-19 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 4:13-19 in Kàddug Yàlla gi

13 Ŋoyal cib yar, bul yoqi, sàmm ko, moo yor sa bakkan.
14 Yoonu ku bon, bu ci tegu; fu ab soxor di jaar, bu fa dox.
15 Moyul, bu fa jaare; mbasal te wéy!
16 Ku bon du nelaw te lorewul, du dajjant ba kera muy téqe.
17 Daa bon, def ko lekk, di màndee coxoram.
18 Yoonu ku jub day leer, ba ne ràññ ni bëccëg.
19 Yoonu ku bon ne këruus, du xam lu muy téqtaloo.
Kàddu yu Xelu 4 in Kàddug Yàlla gi