11 Yoon wu xelu laa la teg, jaarloo la yoonu njub.
12 Doo dox ba tërëf, doo daw, téqtalu.
13 Ŋoyal cib yar, bul yoqi, sàmm ko, moo yor sa bakkan.
14 Yoonu ku bon, bu ci tegu; fu ab soxor di jaar, bu fa dox.
15 Moyul, bu fa jaare; mbasal te wéy!
16 Ku bon du nelaw te lorewul, du dajjant ba kera muy téqe.
17 Daa bon, def ko lekk, di màndee coxoram.
18 Yoonu ku jub day leer, ba ne ràññ ni bëccëg.
19 Yoonu ku bon ne këruus, du xam lu muy téqtaloo.
20 Doom, déglul samay kàddu, teewlul samay wax.
21 Bu ci noppee ja jàkk, te jàpp ko ci sa biir xel.
22 Mooy dundloo ku ci jàpp, di wéral jëmmam jépp.
23 Sàmmala sàmm sab xol, nde xalaati xol ngay jëfe.
24 Dàqal wor, mu sore la; kàdduy naxe, na la dànd.