11 Yoon wu xelu laa la teg, jaarloo la yoonu njub.
12 Doo dox ba tërëf, doo daw, téqtalu.
13 Ŋoyal cib yar, bul yoqi, sàmm ko, moo yor sa bakkan.
14 Yoonu ku bon, bu ci tegu; fu ab soxor di jaar, bu fa dox.
15 Moyul, bu fa jaare; mbasal te wéy!
16 Ku bon du nelaw te lorewul, du dajjant ba kera muy téqe.
17 Daa bon, def ko lekk, di màndee coxoram.