Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 4:10-14 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 4:10-14 in Kàddug Yàlla gi

10 Déglul, doom, te dégg saay wax, ndax nga gudd fan.
11 Yoon wu xelu laa la teg, jaarloo la yoonu njub.
12 Doo dox ba tërëf, doo daw, téqtalu.
13 Ŋoyal cib yar, bul yoqi, sàmm ko, moo yor sa bakkan.
14 Yoonu ku bon, bu ci tegu; fu ab soxor di jaar, bu fa dox.
Kàddu yu Xelu 4 in Kàddug Yàlla gi