9 Teralal Aji Sax ji ci sa alal ak loo jëkka meññle,
10 say sàq day fees, ne xéew, say mbàndi ndoxi reseñ di wal.
11 Doom, bul xeeb yaru Aji Sax ji, bul bañ mu waññi la,
12 ndax Aji Sax ji, ku mu sopp, waññi la, ni baay, ak doom ju ko neex.
13 Mbégtee ñeel ku daj xel mu rafet ak ku am ug dégg.
14 Am koo gën am xaalis, te njariñ laa raw wurus.
15 Xel mu rafet a gën gànjar; loo mana bëgg moo ko raw.
16 Gudd fan, mu joxee ndijoor; càmmoñ ba, alal ak teraanga.
17 Fa muy jaare yiw la, fu mu awe jàmm la.
18 Mooy garabu gudd fan ci ku ko jàpp, di mbégtey ku ca ŋoy.
19 Aji Sax ji xel mu rafet la sose suuf, lale asamaan ag dégg.
20 Ci xam-xamam la ndoxi xóote ya ne jàyy, ay niir di lay.
21 Sama doom, saxool xelu akug foog, dee ci xool foo tollu.