7 Bul doyloo sa xel mu rafet, ragalal Aji Sax ji, dëddu mbon;
8 sa yaram wér, say cér naat.
9 Teralal Aji Sax ji ci sa alal ak loo jëkka meññle,
10 say sàq day fees, ne xéew, say mbàndi ndoxi reseñ di wal.
11 Doom, bul xeeb yaru Aji Sax ji, bul bañ mu waññi la,
12 ndax Aji Sax ji, ku mu sopp, waññi la, ni baay, ak doom ju ko neex.