Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 3:26-31 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 3:26-31 in Kàddug Yàlla gi

26 ndax Aji Sax ji da lay yiir, di la musal cig fiir.
27 Bul xañ njekk ku ko yelloo, ndegam man nga ko.
28 Bul ne say dëkk: «Demal ba beneen, ma jox la,» te fekk la yor.
29 Bul fexeel dëkkandoo bu dëkk ak yaw ci kóolute.
30 Bul joteek kenn ci neen, te tooñu la.
31 Bul ñee ku néeg, te bu ko roy fenn.
Kàddu yu Xelu 3 in Kàddug Yàlla gi