26 ndax Aji Sax ji da lay yiir, di la musal cig fiir.
27 Bul xañ njekk ku ko yelloo, ndegam man nga ko.
28 Bul ne say dëkk: «Demal ba beneen, ma jox la,» te fekk la yor.
29 Bul fexeel dëkkandoo bu dëkk ak yaw ci kóolute.
30 Bul joteek kenn ci neen, te tooñu la.