Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 3:24-34 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 3:24-34 in Kàddug Yàlla gi

24 Soo tëddee doo tiit; say nelaw day neex.
25 Kon doo ragal njàqare lu bette ak saaysaay buy songe,
26 ndax Aji Sax ji da lay yiir, di la musal cig fiir.
27 Bul xañ njekk ku ko yelloo, ndegam man nga ko.
28 Bul ne say dëkk: «Demal ba beneen, ma jox la,» te fekk la yor.
29 Bul fexeel dëkkandoo bu dëkk ak yaw ci kóolute.
30 Bul joteek kenn ci neen, te tooñu la.
31 Bul ñee ku néeg, te bu ko roy fenn.
32 Aji Sax ji daa sib ku dëng, xejjoo kuy jubal.
33 Aji Sax ji day alag kër ku bon, di barkeel waa kër ku jub.
34 Kuy ñaawle, moo lay ñaawal, ku toroxlu, mu may law yiw.
Kàddu yu Xelu 3 in Kàddug Yàlla gi