23 Kon sab dox wóor, doo fakktalu.
24 Soo tëddee doo tiit; say nelaw day neex.
25 Kon doo ragal njàqare lu bette ak saaysaay buy songe,
26 ndax Aji Sax ji da lay yiir, di la musal cig fiir.
27 Bul xañ njekk ku ko yelloo, ndegam man nga ko.
28 Bul ne say dëkk: «Demal ba beneen, ma jox la,» te fekk la yor.