21 Sama doom, saxool xelu akug foog, dee ci xool foo tollu.
22 Day guddal saw fan, di rafetal sa jikko.
23 Kon sab dox wóor, doo fakktalu.
24 Soo tëddee doo tiit; say nelaw day neex.
25 Kon doo ragal njàqare lu bette ak saaysaay buy songe,
26 ndax Aji Sax ji da lay yiir, di la musal cig fiir.