Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 31:9-14 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 31:9-14 in Kàddug Yàlla gi

9 Deel àddu, di àtte njub; ku ñàkk ak ku néewle, nga sàmm àqam.
10 Jeeg bu jàmbaare, ndaw lu jafe, ba rawati gànjar!
11 Jëkkër ja da koy wóolu, te jëkkër ja day am xéewal, du ko ñàkk.
12 Day defal jëkkëram lu baax, du ko lor, tey ànd ak bakkan.
13 Day wut kawari gàtt aki wëñ, di ca liggéeye mbégte.
14 Day mel ni gaalu jula, di jëli dundam fu sore.
Kàddu yu Xelu 31 in Kàddug Yàlla gi