Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 31:3-8 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 31:3-8 in Kàddug Yàlla gi

3 Bul jox jigéen ñi sa doole, bul jox say siddit jigéen ñiy sànk buur.
4 Buur moomul di naan biiñ, Lemuyel, buur moomu ko; kilifa moomul di sàkku ñoll.
5 Lu ko moy mu naan, ba fàtte lu yoon tëral, xañ néew-ji-doole ju ne, àqam.
6 Bàyyeel ñoll kuy sànku, bàyyi biiñ ak boroom naqar.
7 Bu ñu naanee, fàtte seen néewle, ba dootuñu fàttliku seenu tiis.
8 Nanga àddul ku amul kàddu, ku sësul fenn, nga ñoŋal àqam.
Kàddu yu Xelu 31 in Kàddug Yàlla gi