25 Faaydaak jom la làmboo, te ëllëg ubul boppam.
26 Day wax lu xelu, di digle ngor.
27 Jigéen jooju mooy bàyyi xel ci njabootam, te du nangoo yàccaaral.
28 Doom ya dañu ko naan: «Jarawlakk!» jëkkër ja di ko gërëm naan:
29 «Jeeg bu jàmbaare bare na, waaye yaw, yaa ci raw.»
30 Melokaan wu jekk day naxe, taar day wéy, waaye jigéen ju ragal Aji Sax ji, kookoo jara gërëm.
31 Joxleen ko njukkalu ñaqam, jëfam di woyam ca pénc ma.