Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 31:23-29 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 31:23-29 in Kàddug Yàlla gi

23 Dees na ràññee jëkkëram ca pénc ma, fa muy toog ca magi réew ma.
24 Ndaw su ni mel day ràbb ay yére, di jaay, aki gañaay, di jox jaaykat yi.
25 Faaydaak jom la làmboo, te ëllëg ubul boppam.
26 Day wax lu xelu, di digle ngor.
27 Jigéen jooju mooy bàyyi xel ci njabootam, te du nangoo yàccaaral.
28 Doom ya dañu ko naan: «Jarawlakk!» jëkkër ja di ko gërëm naan:
29 «Jeeg bu jàmbaare bare na, waaye yaw, yaa ci raw.»
Kàddu yu Xelu 31 in Kàddug Yàlla gi