2 Ngóor si doom, saa doomi bopp! Yaa di ñaan gu nangu, doom!
3 Bul jox jigéen ñi sa doole, bul jox say siddit jigéen ñiy sànk buur.
4 Buur moomul di naan biiñ, Lemuyel, buur moomu ko; kilifa moomul di sàkku ñoll.
5 Lu ko moy mu naan, ba fàtte lu yoon tëral, xañ néew-ji-doole ju ne, àqam.