11 Jëkkër ja da koy wóolu, te jëkkër ja day am xéewal, du ko ñàkk.
12 Day defal jëkkëram lu baax, du ko lor, tey ànd ak bakkan.
13 Day wut kawari gàtt aki wëñ, di ca liggéeye mbégte.
14 Day mel ni gaalu jula, di jëli dundam fu sore.
15 Day jóg te bët setul, di waajal njëlu njabootam, ak a sas ay janqam.
16 Day seetlu ab tool, jënd ko, sàkk ciw ñaqam, jëmbat tóokër.
17 Day gañu di góor-góorlu, ak a dëgëral përëg ya.
18 Day gis njartel liggéeyam, te làmpam du fey guddi.
19 Ma ngay yor poqe ak këccu, di ëcc.
20 Day jox ku ñàkk, di sàkkal néew-ji-doole.
21 Tiitul ci njaboot gi sedd bu metti, ndax ñoom ñépp ay tegley yére.
22 Mooy sàkkal boppam ay malaan, ay yéreem mucc ayib te yànj.
23 Dees na ràññee jëkkëram ca pénc ma, fa muy toog ca magi réew ma.
24 Ndaw su ni mel day ràbb ay yére, di jaay, aki gañaay, di jox jaaykat yi.
25 Faaydaak jom la làmboo, te ëllëg ubul boppam.
26 Day wax lu xelu, di digle ngor.