Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 2:8-12 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 2:8-12 in Kàddug Yàlla gi

8 Day wattu ku jub fu mu jaare, di sàmm wóllëreem ciw yoon.
9 Kon nga xam njub ak yoon, xam jubal ak mboolem yoonu mbaax.
10 Ndax xel mu rafet miy tàbbi sa xol, nga xam, sa xol tooy,
11 nga foog, fegu, am ug dégg, raw,
12 mucc ci yoonu ku bon ak kuy wax lu jekkadi,
Kàddu yu Xelu 2 in Kàddug Yàlla gi