7 Day dencalal ndam kiy jubal, di yiir ku mat.
8 Day wattu ku jub fu mu jaare, di sàmm wóllëreem ciw yoon.
9 Kon nga xam njub ak yoon, xam jubal ak mboolem yoonu mbaax.
10 Ndax xel mu rafet miy tàbbi sa xol, nga xam, sa xol tooy,
11 nga foog, fegu, am ug dégg, raw,
12 mucc ci yoonu ku bon ak kuy wax lu jekkadi,
13 mucc ci kuy wacc yoonu njub, di jaare mbedd yu lëndëm.