Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 2:3-8 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 2:3-8 in Kàddug Yàlla gi

3 Ngalla wutala dégg, wool dég-dég wall.
4 Sàkkul xel mu rafet ni xaalis, wut ko ni alal ju làqu.
5 Kon nga xam luy ragal Aji Sax ji, xam Yàllaa di kan;
6 ndax Aji Sax jeey maye xel mu rafet, kàddoom di taxa xam, di dégg.
7 Day dencalal ndam kiy jubal, di yiir ku mat.
8 Day wattu ku jub fu mu jaare, di sàmm wóllëreem ciw yoon.
Kàddu yu Xelu 2 in Kàddug Yàlla gi