15 Yoonu ku ni mel day lunk, jaaruwaayam dëng.
16 Xel mu rafet da lay musal ci ndaw su yemadi, bokk feneen, di wax lu neex.
17 Day dëddu wóllëreem, ba muy ndaw, fàtte kóllëreem ak Yàllaam.
18 Këram day joy wuti ndee, ay jaaruwaayam jëm njaniiw.
19 Ku dem ca moom dootoo délsi, doo gisati yoonu dund mukk.
20 Kon nag aweel mbeddum waa ju baax, toppal yoonu ku jub,
21 ndax kuy jubal ay dëkke réew mi, te ku mat a fiy des.