8 Ñaawlekat a ngi taal ab dëkk, ku xelu di giifal mer.
9 Boroom xel, buy layook ub dof, bu mereek buy ree, jàmm du am.
10 Ab bóomkat day sib ku mat, di wuta bóom kuy jubal.
11 Ab dof day mer, sàmbaar; ku xelu, mer, ànd ak sagoom.
12 Kilifa dégluy fen, jawriñ yépp di ñu bon.
13 Ku ñàkk ak ka ko nennoo bokk lenn, Aji Sax jee leen boole sàkk.