5 Kuy jay sa moroom, yaa ngi koy dugal.
6 Ku bon day moy, ba dugal boppam; ku jub di woy ak a bànneexu.
7 Ku jub a xam àqu néew-ji-doole, ab soxor xamu ca dara.
8 Ñaawlekat a ngi taal ab dëkk, ku xelu di giifal mer.
9 Boroom xel, buy layook ub dof, bu mereek buy ree, jàmm du am.
10 Ab bóomkat day sib ku mat, di wuta bóom kuy jubal.