Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 29:15-20 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 29:15-20 in Kàddug Yàlla gi

15 Deel bantal ak a yedde, day rafetal xel; gone goo bay-bayal, mu gàcceel ndeyam.
16 Bu ku bon féetee kaw, ag moy law, waaye ku jub, fekke jéllu ku bon.
17 Yaral sa doom, mu noppal la, bànneexal la.
18 Fu Yàlla feeñoowul, nit ña fétteeral, waaye ku topp yoon, am mbégte.
19 Waxi neen yarul surga, da lay dégg te du la déggal.
20 Ana koo gis, mu rattaxle? Kooku ab dof a ko gën demin.
Kàddu yu Xelu 29 in Kàddug Yàlla gi