15 Deel bantal ak a yedde, day rafetal xel; gone goo bay-bayal, mu gàcceel ndeyam.
16 Bu ku bon féetee kaw, ag moy law, waaye ku jub, fekke jéllu ku bon.
17 Yaral sa doom, mu noppal la, bànneexal la.
18 Fu Yàlla feeñoowul, nit ña fétteeral, waaye ku topp yoon, am mbégte.