9 Diwook suuru day naatal xol; waaye li neex cib xarit, xol la lay digale.
10 Bul fàtte sab xarit mbaa sa xaritu baay, bul jàq ba seeti sa mbokk; dëkkandoo bu jegee gën mbokk mu sore.
11 Muusal, doom, ma bég, ba mana tontu ku ma sikk.
12 Kuy foog, gisu ay, làqu; ab téxét ne ca tëñëx, loru.
13 Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal ndaw su yemadi.
14 Nuyoo bu xumb, suba teel mooki saagaa yem.
15 Jabar ju pànk mooy senn bu dakkul, cib taw;