5 Artu yu ñu la biralal moo gën cofeel gu la boroom ñooru.
6 Soppe, bu lay gaañ sax, wóolu ko. Nit bañ na la, te di la fóon lu bare.
7 Ku suur, bañ lem ju xelli, waaye boo xiifee, lu wex lu ne neex la.
8 Ku sore fa nga bokk, dangay mel ni picc mu sore tàggam.
9 Diwook suuru day naatal xol; waaye li neex cib xarit, xol la lay digale.
10 Bul fàtte sab xarit mbaa sa xaritu baay, bul jàq ba seeti sa mbokk; dëkkandoo bu jegee gën mbokk mu sore.
11 Muusal, doom, ma bég, ba mana tontu ku ma sikk.
12 Kuy foog, gisu ay, làqu; ab téxét ne ca tëñëx, loru.
13 Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal ndaw su yemadi.