16 ku ko mana yemale, mana téye ngelaw mbaa nga ŋëb ag diw.
17 Weñ ay nàmm weñ, nit ay nàmm xelu moroom ma.
18 Ku aar garab, lekk ca doom ya; ku topptoo sa sang, am ngërëm.
19 Ku xool cim ndox, gis sa kanam, nga xool sab xol, gis sa jikko.
20 Njaniiw ak biir suuf du fees, bët it du doylu mukk.
21 Xaalis ak wurus sawaraa koy xelli, waaye àtteb nit ca jëëm.
22 Soo jëloon ub dof, yeb ci gënn, booleek pepp, wol, du tax ndof ga deñ.
23 Xamal bu baax lu say gàtt nekke, te def sa xel ci say gétt,
24 ndax alal wéyul fàww, ag pal du ñeel sëtoo sët.
25 Gannaaw bu ñu gubee, ba ñax saxaat, ñu dajale ngooñ ma ca tund ya,
26 say xar da lay amal koddaay, bëy yi génneel la njégu tool.
27 Meewum bëy daldi am, ba doy la dund, yaak sa waa kër ak sa surga yu jigéen.