Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 27:10-18 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 27:10-18 in Kàddug Yàlla gi

10 Bul fàtte sab xarit mbaa sa xaritu baay, bul jàq ba seeti sa mbokk; dëkkandoo bu jegee gën mbokk mu sore.
11 Muusal, doom, ma bég, ba mana tontu ku ma sikk.
12 Kuy foog, gisu ay, làqu; ab téxét ne ca tëñëx, loru.
13 Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal ndaw su yemadi.
14 Nuyoo bu xumb, suba teel mooki saagaa yem.
15 Jabar ju pànk mooy senn bu dakkul, cib taw;
16 ku ko mana yemale, mana téye ngelaw mbaa nga ŋëb ag diw.
17 Weñ ay nàmm weñ, nit ay nàmm xelu moroom ma.
18 Ku aar garab, lekk ca doom ya; ku topptoo sa sang, am ngërëm.
Kàddu yu Xelu 27 in Kàddug Yàlla gi