Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 25:7-11 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 25:7-11 in Kàddug Yàlla gi

7 ndax ñu ne la: «Yéegal, jegesi fii,» moo gën ñu torxal la ci kanam kilifa. Boo gisalee sa bopp it,
8 bul gaawa layooji, ana nooy def ëllëg, bu ñu la yeyee?
9 Ñaarool ak ki nga joteel, te bul jéebaane jaambur.
10 Lu ko moy ñu dégg ko, rusloo la, sab der yàqu yaxeet.
11 Wax ju ñor di nataalu wurus wu tege ci xaalis.
Kàddu yu Xelu 25 in Kàddug Yàlla gi