Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 25:4-22 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 25:4-22 in Kàddug Yàlla gi

4 Xellil xaalis, tonni lu ca rax, ba ab tëgg man caa am ndab.
5 Ab soxor it, dàqal, mu sore buur, ngir njubte law, jalam sax.
6 Bul réy-réylu fi kanam buur, bul tooge jataayu boroom daraja,
7 ndax ñu ne la: «Yéegal, jegesi fii,» moo gën ñu torxal la ci kanam kilifa. Boo gisalee sa bopp it,
8 bul gaawa layooji, ana nooy def ëllëg, bu ñu la yeyee?
9 Ñaarool ak ki nga joteel, te bul jéebaane jaambur.
10 Lu ko moy ñu dégg ko, rusloo la, sab der yàqu yaxeet.
11 Wax ju ñor di nataalu wurus wu tege ci xaalis.
12 Kàddu yu lay yedd ci kuy dégg, jaarob wurus la mbaa gànjaru ngalam.
13 Ndaw lu wóor day seral xolu njaatigeem, mooy ndox mu sedd ci tàngooru ngóob.
14 Kuy dige te doo joxe, yaay xiin wu ngelaw, mu naaxsaay.
15 Muñ mer ay nax kilifa, te wax ju neex, fu mu jaar, mu nooy.
16 Boo gisee lem, lekkal lu yem; bu ëppee, nga waccu ko.
17 Na sa tànk di gëj kër dëkkandoo; boo ko sàppee, mu jéppi la.
18 Ku seedeel sa moroom ay fen, yen nga ko aw njur mbaa saamar mbaa fitt.
19 Bul wóolu workat bésub njàqare, mooy bëñ bu bon mbaa tànk bu nasax.
20 Kuy woy, boroom tiisu xol di dégg, yaa futti mbubbam cib sedd, mbaa nga jonj xorom ci góomam.
21 Bu sab noon xiifee, jox ko mu lekk, bu maree, may ko mu naan,
22 day rus ba mel ni koo yeni xal, te Aji Sax jee lay fey.
Kàddu yu Xelu 25 in Kàddug Yàlla gi